• il y a 3 ans
Fay bor:
Ki la bëgg yab ndax alal ,
yaw ignorer ko
lèpp Lu la nit , di Dokhanto ,
Yalla am na ko
Féek yaa ngi koy wóolóo ,
yalla mën në laa fayal sa bor

Ki la bëgg jaay loo sa ngor ,
bayyi kook yëfëm
Ba ko fa ne tek , bés a ngi ñëw ,
di na wéet ak jëf ëm
Féek yaa ngi koy wóolóo ,
yalla mën në laa fayal sa bor

Te sax jamono fi mu toll nii ,
ku ne bopp am la tal
Mawlaana rek , moo lay defal ,
ken du la xamal
Féek yaa ngi koy wóolóo ,
yalla mën në laa fayal sa bor


Salaam alleykum , nga bañ ko fay ,
mbaa xam nga ni bor la
Sa dëkkëndòo , nga koy tanxal,
mbaa xam nga ni bor la
Teg say briques , ken mën të jaar
mbaa xam nga ni bor la
Yor sa auto , lu la neex def
mbaa xam nga ni bor la
Nit ku la neex , nga wax ci moom
mbaa xam nga ni bor la
Yor say mbalit , fu la neex tuur
mbaa xam nga ni bor la
Koo séqqël , daldi ko wor
mbaa xam nga ni bor la
Yendoo wax , loo waax mu dañ
mbaa xam nga ni bor la
Koo ëpp doole , won ko ko
mbaa xam nga ni bor la
Doo dimmili , ki nga tane
mbaa xam nga ni bor la

War ngay xalaat bu ëllëg ée ,
nan nga koy fay é
Féek yaa ngi koy wóolóo ,
yalla mën në laa fayal sa bor

man youssou maajigéen ,
j’ai tout pardonné
Koo xam ni , meusone na la tooñ ,
jéggël ma ko


Bor yi nga am fii ñu ne ,
nan nga koy fay é
War ngay xalaat bu ëllëg ée ,
nan nga koy fay é
Féek yaa ngi koy wóolóo ,
yalla mën në laa fayal sa bor

ki la bëgg jaay loo sa ngor ,
bayyi kook yëfëm
Ba ko fa ne tek , bés a ngi ñëw ,
di na wéet ak jëf ëm
Féek yaa ngi koy wóolóo ,
yalla mën në laa fayal sa bor

Te sax jamono fi mu toll nii ,
ku ne bopp am la tal
Mawlaana rek , moo lay defal ,
ken du la xamal
Féek yaa ngi koy wóolóo ,
yalla mën në laa fayal sa bor

Salaam alleykum , nga bañ ko fay ,
mbaa xam nga ni bor la
Sa dëkkëndòo , nga koy tanxal,
mbaa xam nga ni bor la
Teg say briques , ken mën të jaar
mbaa xam nga ni bor la
Yor sa auto , lu la neex def
mbaa xam nga ni bor la
Nit ku la neex , nga wax ci moom
mbaa xam nga ni bor la
Yor say mbalit , fu la neex tuur
mbaa xam nga ni bor la
Koo séqqël , daldi ko wor
mbaa xam nga ni bor la
Yendoo wax , loo waax mu dañ
mbaa xam nga ni bor la
Koo ëpp doole , won ko ko
mbaa xam nga ni bor la
Doo dimmili , ki nga tane
mbaa xam nga ni bor la
War ngay xalaat bu ëllëg ée ,
nan nga koy fay é
Féek yaa ngi koy wóolóo ,
yalla mën në laa fayal sa bor

man youssou maajigéen ,
j’ai tout pardonné
Koo xam ni , meusone naa la tooñ ,
jéggël ma ko

Ñun doom i aadama ndiaye
li ñu gën ë sonn al mooy,
Aqqi dëkkëndòo ,
aqqi àndandoo ,
ak aqqi am gi jamm yek ,
Yalla , yermëndéem yaatu na ,
mën naa jéggël e bakkaar bu mu né
Waaye , doom i aadama Ndiaye ,
Boo ko yor ee lee bor ,
na nga ko fay , fii ci dunyaa
Walla nga balu ko mu baal la ,

Yé way samba, Khalass, kholal
Youssou maajigéen , oh ! lii doy na waar
Youssou Marie Sène ,
bu dee lii la , bor yi bari ña ñu
Yaay na nga ma baal , baay na nga ma baal ,
aqq u njuréel
You , Ndour , merci beaucoup .
Adji maam Ndiaye , yaay I t

Category

🎵
Musique

Recommandations